Paroles

Hey Massamba Walo Pape Laye Góom nga woon Yàlla def na tay mu wér Ba leneen tegu sa kaw Nga dem bayyi ma ak legét Xàmmeekaay nga woon Fu ñu la gis xalaat ma Fu ñu ma gis laaj ma la Nga ba ma ak legét Xol lu fa jiitu sax fa Yaa njëkkoon ci man Bokkoon ci sama yaram Nga dem bayyi ma ak legét Noo ma war a man a bégloowe di ma jooyloo? Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo Noo ma man a woowe ba ma ñëw nga di ma dawloo? Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo Moo tax wóolu naa li ne ci man Mbëggeel laa wóoluwul man Wóolu naa li ne ci man Waaye mbëggeel day weere Moo tax wóolu naa li ne ci man Mbëggeel laa wóoluwul man Wóolu naa li ne ci man Waaye mbëggeel day weere Motax Li ma realise mooy Mbëggeel daa jegeñaale Mbégte ak naqar Fiiraange di ma fitnaal Ma dëkke di sóoraale ak di xel ñaar Li mu may laaaj Man moom la ma dul man a joxe Li muy digle duma ko jëfe Am NDAYSSAN! Ni ngay bégee nii nga man a jooye Ba ma rekk ma dem, désolé Njamala patam réer na ko Laaj ko fu mu jëm Dafay wër mbëggeel Masàmba nga ne lan? Mbëggeel daa soree Tax na ba ma jommee Noo ma war a man a bégloowe di ma jooyloo? Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo Noo ma man a woowe ba ma ñëw nga di ma dawloo? Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo Moo tax wóolu naa li ne ci man Mbëggeel laa wóoluwul man Wóolu naa li ne ci man Waaye mbëggeel day weere Moo tax wóolu naa li ne ci man Mbëggeel laa wóoluwul man Wóolu naa li ne ci man Waaye mbëggeel day weere moo tax Noo ma war a man a bégloowe di ma jooyloo? Nga dem bayyi ma ak legét Noo ma man a woowe ba ma ñëw nga di ma dawloo? Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo Moo tax Wóolu naa li ne ci man Mbëggeel laa wóoluwul waay Wóolu naa li ne ci man Ndax mbëggeel day weere motax Wóolu naa li ne ci man Mbëggeel laa wóoluwul way Wóolu naa li ne ci man Massmaba Walo
Writer(s): Abdoulaye Diop, Saliou Samb Lyrics powered by www.musixmatch.com
instagramSharePathic_arrow_out